Tëbëski
mooy ñaareelu iid (bër) ci lislaam ginnaaw bu Korite jàllee. Jële na nu
ci Anas (gërëmul Yàlla Yal na nekk ci moom) mu ne: Bi Yonent bi
(Yalna jàmmi Yal na nekk ci moom) yegsee Madiina fekkee na léen ñaari
bis ñu ca daan caaxaan ak a fo.
-Yonent
bi (jàmmi Yàlla ci moom) ne léen: «Yàlla jox na léen ñaari bis yu gën
yooyu ñaar, muy Bisu tëbëski ak bob Kori» (Abuu Daawud soloo na ko)
Moom
Täbëski dees na ko amal ci fukkeelu (10eel) bis ci aw Täbëski, di weer
wi mujj ci atum weer wi (Wolof). Ñaari bër (fête) yooyu, di tëbëski ak
Kori, bokk nañu ci teddngay lislaam, ba tax na kenn sañu cee woor.
Yonent bi (Jàmmi Yàlla yal na nekk ci moom) tere na ku ci woor. Waaye
nag bu dee bisu Täbëski sunna la boo xëyee bañ a lekk darra ba baa ngay
julli ba déllusi doge ci tëbëski mi. Bu dee kori safaan bi mooy sunna,
lekk njëkk ngay julliji.
Tëbëski (rendi gàtt):
Ci
Ngiirum Maalig ak Shaafi`, Tëbëski, maanaam rendi gàtt, Sunna la su far
ci ab jullit bu di mukàllaf, di as gor, man ko te mu bañ koo sonal, bu
yooyu dajee mag ak gone ñoo ci yam ku xës mukàllaf sunna su far si war
na la. Sunna su far soosu nag, man naa mujj di farata ci ñaari anam yii
:
1. Ci ku ko nësër : niki nga ni bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tëbëski. Fu loola amee rekk manatul a ñàkk, farata la ci yaw.
2. Ci ku xës jënd am tëbëski, walla mu yor am xar jublu ci tëbëski : bu loolu xësee am day daadi nekk farata ci yaw.
Àtteb Tëbëski ci Lislaam ?
Yàlla nee na: «Jullil ngir sa Boroom te rendi (lottal)» (Saaru 108 / Laaya 03)
Yonent
b i(jàmmi Yàlla ci moom) nee na: «Ku am dooley [man a rendi am] tëbëski
te tëbëskiwul, bu mu jege sunu barabu julliwaay» (Abuu Hurayra moo ko
nettali, Ibn Maaja, Ahmad, Daaru Qutni ak Al-Haakim soloo nañ ko, doonte
barina ñu jam hadiis bi ci woroom xam-xam yi, niki Haasim ak ñeneen)
Baraan
nettali na ni, Yonent (Jàmmi Yàlla ci ñoom) bi nee na: Li nuy njëkk a
def ci bis bii, moo di julli, ginnaaw ba nu dellu lottal (rendi), ku def
loolu def na sunu sunna. »
Ash-Shaari` nee na: «Duma nangu ku am dooley am tëbëski di ko sàggane »
Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) saxaloon na ko te daan ko digle.
Sunna
la su far ci Ñoñ-Maalig, Shaafi`, ag ñenn ci waa Ahmad Ibn Anbal. Bu
dee nag ci ngiirum Abuu Hanifa ñoom lu war la. Lu war ca ñoñ Abuu Hanifa
nag tekkiwul farata la.
Lu man a am nag ñépp dëppoo na ñu ci ne dina war ci ñaari anam yii:
1. Ci ku ko nësër : niki nga ni bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tëbëski. Fu loola amee rekk manatul a ñàkk, farata la ci yaw.
2. Ci ku xës jënd am tëbaski, walla mu yor am xar jublu ci tëbëski : bu loolu xësee am day daadi nekk farata ci yaw.
Sopp na ñu yii ci bisu Tëbëski :
- Sangu luñ sopp la;
- Sol yére yu bees buy julliji, ak xeeñoo lëjkoloñ (ba mu des rekk ci jigéen) ;
- Sopp nañu nga bañ a lekk darra ba julliji ba ñëw, soog a lekk;
-
Am tëbëski (gàtt):
Yàlla
nee na ci Alxuraan (la nu déggee ci wax ji): «Yàlla amul Soxla ci yàpp
wi walla dereet ji; waaye la ko ca soxal mooy ragal [Yàlla] gu bawoo ci
yéen. Noonu na la nu léen léen tàggate ngir ngéen Màggal Yàlla ci li mu
léen gindi. Te nanga bégal way-rafetal ñi » S22 L:36
Kon nanu
jàpp njëkk ni yéene ju sell te Yàlla rekk tax waliif ngistal walla wanu
ci bëti nit ñi mooy maye yoolu tëbëski. Ci lislaam ñaari mbir sàrt la ci
nangug jëf jum man a doon : benn ; mu dëppoo ak sunna ; ñaar : Sellal
ko ngir Yàlla dong.
Yonent bi (Ya lna jàmmi Yàlla nekk ci moom )
nee na : «Sellal léen séen i jëf, ngir Yàlla kët du nangu ludul luñ
sellal ngir moom »
Sàrt yii nag moo koy tax a wér :
- Xar mu am juróom benni (6 i) weer mbaa at aki fan ci li sax ci ñoñ-Maalig. Bu dee aw bëy nag, na am at ak weer ci ñoñ-maalig ;
- Xar a gën, topp bëy, topp nag ak giléem ;
- Xar mu góor a gën mu jigéen, bëy wu góor a gën wu jigéen, nag ak giléem naka noonu.
- Juróom ñaari jullit man nañoo boole jënd aw nag walla giléem.
- Bu dee xar walla bëy nag kenn du ko bokk jënd.
- Waaye
nag man ngaa ray yéene ci képp kuy yewwoo ci kër gi, moo xam muy koo
xam ne dundal ko yaw la war, niki say doom ak sa soxna, walla muy koo
xam ni dundal ko waru la, niki say rakk yu góor ak jarbaat... Buñ ko
amul yéene léen ci dina léen doy am tëbëski. Ku nekkul ci kër gi nag
deesu ko ci man a yéenewaale.
Yees nanguwul ci am Tëbëski:
- Bu
benn béjjan dammee te wérulagul , manaan di nàcc, du matum tabaski (ci
maalig). Bu wéree may nañ la ko. Bu judduwaalewul ay béjjen it darra
nekku ci ;
- Bees xaajee nopp ba ñatt (1/3), la ca dagg bu matee
benn xaaj ba, matul am tëbëski. Bu judduwaalewul nopp walla nopp ya gàtt
nag darra nekku ci ;
- Niki noonu it bu nopp ba xaree lu toll ci benn ci ñatti xaajam (1/3) du mat am tëbëski
- Bees
xaajee geen ba ñatt, la ca dagg bu matee benn ca ñatti xaaj ya (1/3)
matul am tabaski. Bu ko judduwaaleewul walla mu gàtt nag darra nekku ci.
Am Tëbëski it war naa mucc ci yii:
- Bumu yooy ba amul nebbon (ndawal)
- Bu gimiñ ga xasaw ba jéggi dayo
- Bu bët ya/ba patt ba fés, rawati na nag muy gumba
- Bu tànk ba làgge ba fés, rawati na nag mu damm
Lees di bañ ci ndawalug am tëbëski:
- Bañees na ku ca jaay darra ca yàpp wa ak ca der ba. Ku ko ñaani ba ñu may la ko nag man na koo jaay, darra nekku ci.
- Bañees
na yitam ka koy fees ñu di ko fay ca yàpp wa, waaye manees na ko caa
may walla sarax,. Bu laajee ag fay fayees ko xaalis walla leneen. Noonu
it la àtte ci deme ci am tudd.
- Bañees na gépp joxe ngir wareef (obligation/devoir), niki tànku njëkke, yeeli maam, baatu feeskat, ak yu ni mel...
Am tëbëski sañees na cee maye, sañees na cee lekk, sañees na cee denc.
Xataada
Ibn An-Nu`maan nettali na ne : Yonent bi (Yal na jàmm Yàlla nekk ci
moom) xëy na bis ne leen : Maa léen terewoon lekk ndawalug Tëbëski lu
weesu ñatti bis [u tëbëski]. May naa léen ko léegi ; lekk léen ci nim
léen neexe. Waaye bu léen jaay ndawalug Tëbëski, lekk léen ci, joxe léen
ci sarax. Jariñoo léen der bi waaye bu léen ko jaay. Buñ léen ci joxee
it lekk léen. » (Ahmad soloo na ko)
Nees di rendee ak li ci aju :
Rendi
ab jullit moo koy def, te doon ku am xel. Melo wi ci gën nag moodi mu
tëral la muy rendi ci wetug càmmooñam te mu jublu xibla (kaaba ga), bu
dee am xar mu tëral noppub ndeyjoor ba; ba fa mu yam ca baat ba, mu teg
foofa paaka ba. Walla bu amee téerey baat mu teg paaka ba ca diggante
téere ya. Bu ko defee balaa caa teg paaka ba mu wax ci am xelam ni "fas
na maa yéenee daganal lekk yàppu nàngam wii ci rendi gi ma koy rendi".
Bu dee teg paaka ba mu wax:
« Bismil Laahi » daaldi koy dawal ba ñaari sidit yu mag ya ak boli ga lépp dagg. Bu ko bombee ba deret ja génn mu wax:
Allaahu Akbar. Bu teggee loxoom mu wax:
«Rabbanaa taqabal minnaa innaka anta s-samii`u L-`Aliim »(S002/L126:).
Bu
dawalee paaka ba ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, bu ko ca gaawee
delloo dees na ko lekk. Bu ko ca yeexee delloo nag te lor waralu ko,
kon deesu ko lekk. Te yit bu mu tàngale baat ba, bu ko defee it du ko
tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
-Rendi xar ak bëy ci kanam lees koy defe; boo ko rendee ci ginnaaw walla ci wet, deesu ko lekk;
-Bu dee aw nag manees na koo rendi manees na koo loj,
-Bu
dee Ginaar nag war naa wërale paaka ba, ca gannaaw ak ca kanam, ba
sidit yu sew yépp dagg te mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko
tee baax waaye bañ koo def a gën.
-Giléem deesu ko rendi mukk, li feek du dañoo loru amuñu lojukaay te am rendikaay.
Loj aj li ci aju :
Kuy
loj, day taxawal lamuy loj jubale ko "XIBLA" (Kaabag Màkka). Lem baat
ba tëral ko ci wetug càmmoñ ga, bu ragalee barig dooley la muy loj, man
naa yeew tànkub càmmooñu kanam ba. Balaa tàmbali mu wax «Bismil Laahi»,
bu tàmbalee mu bañ a dindi loxoom lifeek noppiwul.
Lees war a loj
nag bees amul lojukaay sañees na koo rendi, lees war a rendi it bu ñu
amul rendikaay te am lojukaay sañees na koo loj.
-Giléem loj rekk
lees koy def mbaa deesu ko lekk waaye deesu ko rendi, xanaa ñu loru ñàkk
lojukaay te am rendikaay, bu boobaa nag dees na leen ko may;
-Bu
dee aw Nag dees na ko loj niki noonu it dees na ko rendi, kon moom lu
leen jekku rekk ñu sañ koo def noona (Fii nag rendi ko lañu gën a miin).
Loj, balaa baax ñatti sidit yu mag yi daa war a dagg, kon ci ag wet lees koy defe ak kanam.
Na
moytu yii : Bu dawalee paaka ba, ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi
ko, kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk. Bu ko ca yeexee delloo
nag te lor wara lu ko, kon deesu ko lekk. Te yit mu bañ a tàngale baat
ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
Waxtuw rendi walla loj:
Mi
ngi dale ci rendig Yilimaan, rendig yilimaan moo ngi aju ci ginnaaw bu
sëlmalee julli gi, ba kerog jant di so ca bisub ñatteel ba fu ñu ko fi
rendee mu baax. Ci ngiirum Maalig fàww rekk mu doon bëccëg, ci teewaayu
jant bi, deesu ko sañ a ray guddi. La ca gën moodi boroom rendil ko
boppam, bu amee ngànt mu wuutal ko moroomum jullitam, te nanga yéene yaw
mi ñuy rendil. Ku dul ab jullit manu laa rayal am tëbëski.
Ku rendi tëbëskim jàmbur te amu ci ndigël, du ko doy am tëbëski te war naa fay boroom.
Am
Tëbëski nag deesu ko rendi jëkk rendig Yilimaan te Yilimaan it balaa
rendi nig ba julli. Ci ni ko Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) waxe :«
Képp ku rëy njëkk jullig bër gi, deful lu dul rëy baayima buñ man a lekk
; waaye ku rëy ginnaaw jullig bër gi nag, am na am Tëbëski» (Buxaari
soloo na ko)
Ngënéeli Tëbëski:
Yonent
bi (jàmmi Yàlla ci moom) xamle na ni toq dereet wiy njëkk a génn Yàlla
di na ci jéggale mboolem bàkkaar yu waay mas a def, nii la dikke ci
hadiis ci nettalib Aysa (ngërëmul Yàlla ci moom).
Jëlee nanu ci
Ibn Abaas mu ni Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) nee na : «Alal dugaleesu
ko ci lu gën gàttub tëbëski (iid)» (Daaru Qutni soloo na ko)
Yonent
bi (jàmmi Yàlla ci moom) bégal nanu ci ne Xarum tabaski dina njot ci
sawara niki mu njoteewoon bakkanu Ismaayla. Amul jëf ju nit di def ci
bisu Tëbëski ju gën a neex Yàlla tuur ci dereet. Noonu la ko Aysa
nettalee.
Taarixu Tëbëski
Tëbëski
xew wu am solo la ci lislaam tey jëmmal xew-xew bu am solo ci jëflànteg
nit ak Boroomam. Di la xewoon ci diggante Yonent Yàlla Ibraayma, doom
ja Yonent Yàlla Ismaayla (Jàmmi Yàlla ci ñoom), ak Boroomam, ca bam
dëelantee ak Boroomam ci rayal ko doom ja muy njëkk a am ngir won ko
cofeelam ak gënal gum ko gënal leneen ludul Moom. Ba doomam ju jëkk
juddoo, tudd Ismaayla, nekk gu doom nekk ci moom lu bees tax mu am
cofeel gu rëy ci moom. Loolu tax, boroom bi xabaar ko ci gént ngir
fàttali ko séen ndëel ba. Ba mu ko wérloo ba muy ndéey
(wahyu/révélation) lu leer, ca la ko yëgal Soxna sa. Soxna sa deful lu
may rafetlu ko, doonte ni doom foore ci ndey. Waaye rekk mu am kóolute
ci Boroomam.
Niki noonu it la ko yëgale doom ja, ni ko
"(...) Yaw samas ndoom man de gént naa di la rendi, xoolal loo ci xalaat (...)" (S37/L0102). Doom ja ànd ak la muy nekk ndaw lépp, mu toontu ko ni
"Yaw sama baay defal lees la digël. Man nag, bu neexee Yàlla, da nga ma fekk ma bokk ca way-muñ ya" (S37/L0102)
Ba
ñu déggoo ñoom ñépp ci jëfe ndigël li, Ibraayma ànd ak Ismaayla ngir
rendiji ko nim ko gise ci gént gi. Ba loolu amee, Ismaayla sàkku ci moom
mu takk ay gëtam ngir bañ koo yërëm ba du jëfe ndigël li. Ba mu takkee
ay gëtam nag ba dogu ci rendi ko, Alxuraan nee:
"Nu woo ko, ni ko Eey! Yaw Ibraayma.
Dëggal nga gént gi. Nun de noonu la nuy faye way rafetal yi.
Dëgg-dëgg lii nattu la bu bér (diis). "
Nu daaldi koy njot (moom Ismaayla) ci gàtt bu rëy.
Daaldi koy bàyyi mu bokk ci way-des ñi (di dund).
Jàmmi Yàlla [Yal] na nekk ci Ibraayma.
Nun nag noonu la nuy faye way-rafetal ñi.
Moom daal ci sunu jaam yi di way-gëm la bokk." (S37/L0104-111)
Tëbëskig Jàmm !
Di léen balu àq ; di leen baal àq, tey ñaan Yàlla boole nu baal. Te nu fekke ko te romb ko.
Déwénati,
Aji-Bind ji: Abdu Xaadir GEY,
Kenn ci way-sosi Akaademi Wolof
https://www.facebook.com/groups/akaademiwolof/