"Les croyants ne sont que des frères Établissez la concorde entre vos frères, et craignez Allah, afin qu'on vous fasse miséricorde." Coran: 49/10
Récit de S. Mouhamadoul Amine Diop dans Iraww-u Nadiim
Muhammad Ibn Ahmad Al-Yakoubi communément appelé Muhammad TOUBA m'a raconté qu'au cours d'un de ses voyages à TOUBA, il était passé par Tivaouane pour rendre visite à Al Hadji Malick Sy. Quand celui-ci a su que son hôte allait se rendre auprès de Cheikh Ahmadou Bamba, il lui a dit: "Je vais te charger de transmettre un message au Cheikh.
Salue-le de ma part et rappelle-lui la nuit que nous avons passé ensemble à Saint-Louis dans la même chambre. S'il s'en souvient, dis lui que je maintiens toujours l'engagement que j'avais pris devant lui".
Muhammad a dit: "Je ne sais pas de quel engagement il s'agissait, car mon interlocuteur ne l'a pas explicité.
Quand je suis arrivé auprès du Cheikh, je lui ai transmis le message, et il a confirmé les propos d'Al Hadji Malick Sy et s'en est réjouis et lui a rendu hommage et s'est mis à caresser mon oreille et son nez en riant de joie".
.......................................................
Wolof :
Sama mbokk, Muhammad, mom Ahmad Aliyu Alyahxuubii, nu gënoon koo xam ci turu, Muhammad Tuubaa, xibaar na ma ne moom de ci lenn ci ay siyaareem yu mu doon def neena « daa romboon Tiwaawon, siyaare Alhaaji Maalik SI, bi [Alhaaji Maalik] xamee ne ca Sëñ ba la jëm, mu ne ko man de da ma laa bëgg a yobbante ay baat ca moom [Sñ Bàmba], boo àggee na nga ma ko nuyyul, te fàttalil ma ko sunu guddi ga nu bokkoon fanaan ca Ndar, ci benn néeg ñun ñaar rekk, kenn ñatteelunu ku dul Yàlla, bu ko fàttalikoo ba xam ne maa la yonni, nga ne ko, man kat maa nga ca la ma waxoon ak moom, maa nga ca kollare ga ma fasoon ak moom ». Muhammad nee na man de « wallaahi, xamuma gan kollare la jublu ci waxam jooju,te moom dolliwaatuma ci genn leeral. »
Bi ma àgsee ba fàttali Sëñ bi guddi gi, ba mu fàttaliku ko, ma wax ko li mu ma wax, mu bég ci, dëggal ma te dëggal ko, tagg ko bu baax, tàmbli di coppati sama nopp bi, ak sama bakan bi, boole ca di ree rekk, ngir bég .»

Enregistrer un commentaire

 
Top