L’image contient peut-être : 1 personne

Muhàmmad, moo di aw turam, gëna siiwé ci Sëriñ Mbàkke Buso.
Ay waajuram:
Muy doomi Soxna Faati Bàlla Mbàkke mom Maam Bàlla Aycha, mom Maam Mahram Mbàkke.
Soxna Faati moomu batay mooyw wayjuru ñu bari ci kër Sëriñ Mbusoobé, ku mel ni Sëriñ Seyxu Buso, Sëriñ Masàmba Faati Buso ak Soxna Xari Buso.
Baayam di Sëriñ Muhàmmad Buso (Sëriñ Mbusoobé) miy magi Soxna Jaara Buso, Sëriñ Mbàkke di mbokkum Sëriñ Tuubaa, di doomi nijaayam, di doomi bajjenam…
Am njàngam:
Mi ngi feeñ jamono ci atum 1864 ca Jolof, jàngge Alxuraan ci baayam bu baax boobu, lu jiitu mu koy jox Seexul Xadiim, ngir mu jàngg ci moom yeneen i fànn i xam-xam. Jàngge na it ci kilifa gu gu mag gu ñuy wax Sàmba Tukkuloor Ka, ak Maam Moor Jaara miy magi Sëriñ Tuubaa, ak yeneen i woroom xam-xam yu bari.
Yàlla def mu géeju woon lool ci xeeti xam-xam yu wuute. Taalif na lu bari ci ay téeré, ci fànn yu wuute, lu jëm ci xam waxtuy julli yi, ci xam-xam u Alxuraan, xamle ay farata ak yeneen i xam-xam yu bari te wuute.
Diggam ak Sëriñ bi :
Mu teela topp Boroom Tuubaa lool, lu jiitu yoonu Murid di sosu, ndax baayam da ko féetale woon Sëriñ bi ci ak ndawam. Bi Sëriñ bi woote yoon wi it, bokk na ci ñi ko njëkk a wuyu, jaayante ak moom, Sëriñ Tuubaa doyloo woon ko lool ci léppam, mu amoon ci moom wàccuwaay wu kawe lool.
Fu Sëriñ bi masa nekk, mu nekk faag moom, di ko taxawu ci lu bari, ba ci ay xalwatoomsax, yu ci bari mook Sëriñ Mbàkke ko daan defandoo, ba ci bi muy bind Masaalikul Jinaan ca Mbàkke Bawol.
Sëriñ Tuubaa, féetale woon ko lépp lu jëm ci jàngg ak jàngle, ak di tontu ay bataaxalam, ak di ko ko bindal, ak natt jàkka yi, daan disoo ak moom ci lu bari lu mu nara def.
Ci lii la nekkoon, daan ligéeyal Sëriñ Tuubaa ba làq ngëramam, ba Sëriñ Tuubaa sax màndargaal ko ci ay bëyit, mi ngi tàmbalee ci
جزاك خير جزاء من برى النسما
حتى تحوز مقاما قد علا وسما
"yàl na la Yàlla fay ngën ji pay, ba nga làq ay Maqaama yu kawe lool..."
Ku am amoon wollëré la, te manoona jokkale lool ak kilifa yi mu jamonoonteel, ku mel ni Sëriñ Moor Jaara Mbàkke aki rakkam, ak ñi mu bokkaloon Sëriñ bi ñépp, ak kilifay diiné yi nekkoon ci réew mi, ku mel ni Allaaji Maalik Si, Seex Abdulaahi Ñas…
Sëriñ Mbàkke Buso, mooy ki Boroom Tuubaa batale woon ne « na ko taxawu su wuyujee Boroomam » noonu la ko defee ci atum 1927.
Wéyël ligéeyub Sëriñ Tuubaa boobu ci njabootam gi mu fi bàyi woon, daan léen taxawu ak di léen jàpple ci naal yi fi Sëriñ bi bàyi woon.
Ci atum 1928, bokk na ci mbooloo mi bàyi koo woon Tuubaa dem jooxe seen faratay jëmm ca Màkka, mottali waale yéenéy Seexul Xadiim ji mu ci amoon ba waxoon ko ko.
Sëriñ Mbàkke masula deñ di ab jullit dëgg, tey murid saadix, te taqoo woon ak Sëriñ bu mak bi diirub jamonoom, taxawu ko ginaawam ci lu bari, ba ni mu làqo ci atum 1946, ñu deñci ko ca Gede gii nga xam ne bokk na ci dëkk yi mu sañcon ci ndigalul Boroom Tuubaa.
Yàl na ñu ko Yàlla fayal te taas ñu ci bàrkeem
Ci xalimag: Akb Majalis

Enregistrer un commentaire

 
Top