Bu fekkee li ñu wax wer na, te mooy am na 200 njaboot yu ndox mi génne seeni kër ca Tuubaa, ndax maneesu leen a jàppale ci lenn ci anam yii :
1. Saytu seen lim ak seeni jafe-jafe ba mu leer (su ko lim BI ëppee yit ñu xam) ;
2. Séddale njaboot yooyu ci kër Sëñ Tuubaa yi ci dëkk bi ;
3. Ñu sàkku ku ko man dugal loxoom ci wallu googu : sunu kilifa yu baax yi wala baay defal Yàlla bu fa tëj këram, wala am barab yu jàppandi (disponibles) yu ñu mana dalal ay nit ;
4. Roy ci ndimbalu 50 millions li Sñ Muntaxaa jox nguur gi (na ko fi sunu Boroom yàggal lool te may ko wer), wut leneen lu ñu ci mana dolli (lu mel ni ni ko Touba Ca Kanam defewoon daaw, ca barkeelu ya, ak yeneen dayira yi, jëfandikoo réseaux sociaux yi, añs) ngir dundalee ko way loru yooyu diir ba ñu fay nekk ;
5. État bi jàpp bu baax ci jéego yooyu te fas yéenee jël ay matuwaayam ak responsabiliteem ci jële fi ndox moomu ren. Te bu mu ci yam, na waajal bu baax at yii di ñëw, ci taxawal ak jëmmal "programme d'assainissement de Touba" bu matale, doonte ay at ak alal ju bari lay jël, ànd ko ak kilifay yoon wi ak murit yépp (ku nekk ci ñoom xam bu leer fi miy tàmbalee ak fi muy yam).
Di jéggalu ci kàddu yi ak xalaat yu xeebu yi.
Yàlla na ñu Boroom bi dolli yërmande, ndimbal ak tawfeex.
Iyyàka na'budu, wa bika nasta'înu

Enregistrer un commentaire

 
Top